1:1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
1:2 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
1:3 Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram;
1:4 Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon;
1:5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Yese,
1:6 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri;
1:7 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
1:8 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
1:9 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiyas;
1:10 Esekiyas Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas;
1:11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
1:12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
1:13 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
1:14 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
1:15 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
1:16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
1:17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
1:18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
1:19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer. Mu nar a xàccook moom ci sutura.
1:20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
1:21 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
1:22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
1:23 «Janq bi dina ëmb,jur doom ju góor,ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
1:24 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
1:25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
2:1 Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
2:2 Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
2:3 Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
2:4 Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, war a juddoo.
2:5 Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent:
2:6 “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude,du yaw yaa yées ci njiiti Yude,ndaxte ci yaw la njiit di génne,kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
2:7 Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
2:8 Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
2:9 Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tell jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
2:10 Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réy-a-réy.
2:11 Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
2:12 Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu bañ a dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
2:13 Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
2:14 Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
2:15 Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
2:16 Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, mengook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
2:17 Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan:
2:18 «Baat jib na ci Rama,ay jooy ak yuux gu réy,Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko,ndaxte saay nañu.»
2:19 Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
2:20 ne ko: «Ñi doon wut a rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
2:21 Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
2:22 Waaye bi mu déggee ne, Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
2:23 Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan:«Dees na ko tudde Nasaréen.»
3:1 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
3:2 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
3:3 Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”»
3:4 Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
3:5 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
3:6 Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
3:7 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
3:8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar,
3:9 te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
3:10 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.
3:11 Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.
3:12 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»
3:13 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
3:14 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
3:15 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
3:16 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
3:17 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
4:1 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
4:2 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi, door a xiif.
4:3 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
4:4 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
4:5 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
4:6 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
4:7 Yeesu tontu ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
4:8 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
4:9 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
4:10 Waaye Yeesu tontu ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»
4:11 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
4:12 Am bés Yeesu dégg ne, jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
4:13 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
4:14 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
4:15 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut —
4:16 xeet wa nekkoon cig lëndëm,gis na leer gu mag,ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim,leer fenkal na leen.»
4:17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
4:18 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
4:19 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
4:20 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
4:21 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
4:22 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
4:23 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña,
4:24 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
4:25 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan..
5:1 Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom.
5:2 Mu daldi leen jàngal naan:
5:3 «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
5:4 Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen,ndax dees na dëfël seen xol.
5:5 Yéen ñi lewet, barkeel ngeen,ndax dingeen moomi àddina.
5:6 Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.
5:7 Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen,ndax dees na leen yërëm.
5:8 Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen,ndax dingeen gis Yàlla.
5:9 Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen,ndax dees na leen tudde doomi Yàlla.
5:10 Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
5:11 «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man.
5:12 Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
5:13 «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom si sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
5:14 Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du man a nëbbu.
5:15 Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp.
5:16 Na seen leer leere noonu ci kanamu nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw.
5:17 «Buleen defe ne, ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man.
5:18 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am.
5:19 Ku tebbi nag ba gën a tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gën a tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
5:20 Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
5:21 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.”
5:22 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci safara.
5:23 Booy yóbbu nag sa sarax ca saraxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree,
5:24 nanga fa bàyyi sa sarax ca kanamu saraxalukaay ba, nga jëkk a dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax.
5:25 «Gaawal a juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeen a egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la.
5:26 Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj.
5:27 «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.”
5:28 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel.
5:29 Bu la sa bëtu ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore.
5:30 Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci safara. Bu la sa loxol ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci safara.
5:31 «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa jabar, nga bindal ko kayitu pase.”
5:32 Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa jabar te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga.
5:33 «Dégg ngeen itam ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.”
5:34 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla;
5:35 bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi.
5:36 Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte mënuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar.
5:37 Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
5:38 «Te it dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.”
5:39 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndeyjoor, jox ko ba ca des.
5:40 Ku la bëgg a kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag.
5:41 Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar.
5:42 Mayal ku lay ñaan, te bul jox gannaaw ku lay leb.
5:43 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.”
5:44 Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal,
5:45 ngir wone ne, yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.
5:46 Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it?
5:47 Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it?
5:48 Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate.
6:1 «Wottuleen a def seeni jëf yu jub ci kanamu nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.
6:2 Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:3 Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmooñ xam li sa loxob ndeyjoor di def,
6:4 ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:5 «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:6 Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:7 «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
6:8 Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax.
6:9 Yéen nag nii ngeen war a ñaane:“Sunu Baay bi nekk ci kaw,na sa tur sell,
6:10 na sa nguur ñëw,na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.
6:11 May nu tey li nu war a dunde;
6:12 te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ;
6:13 bu nu teg ci yoonu nattu, waaye nga musal nu ci lu bon.Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
6:14 «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam.
6:15 Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.
6:16 «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:17 Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu,
6:18 ngir sa koor bañ a feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:19 «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko.
6:20 Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko.
6:21 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
6:22 «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer,
6:23 waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse!
6:24 «Kenn mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.
6:25 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay?
6:26 Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare?
6:27 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo man a yokk waxtu ci àppam?
6:28 «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc,
6:29 waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
6:30 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?
6:31 Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a naan?” walla: “Lu nu war a sol?”
6:32 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp.
6:33 Waaye jëkkleen a wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
6:34 Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko.
7:1 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam.
7:2 Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale.
7:3 Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
7:4 Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw?
7:5 Naaféq, jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
7:6 «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanamu mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen.
7:7 «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
7:8 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
7:9 Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj?
7:10 Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan?
7:11 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
7:12 «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
7:13 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare.
7:14 Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
7:15 «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu.
7:16 Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte réseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam?
7:17 Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon.
7:18 Garab gu baax mënul a meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon mënul a meññ doom yu neex.
7:19 Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca safara sa.
7:20 Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee.
7:21 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw.
7:22 Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?”
7:23 Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Musuma leen a xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.”
7:24 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj.
7:25 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa.
7:26 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax, te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gànnuus bi.
7:27 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
7:28 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngaleem,
7:29 ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
8:1 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko.
8:2 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.»
8:3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
8:4 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»
8:5 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko,
8:6 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.»
8:7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.»
8:8 Waaye njiit la tontu ko ne: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8:9 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
8:10 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, musumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii.
8:11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
8:12 Waaye ñi waroon a bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.»
8:13 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
8:14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng.
8:15 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
8:16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp.
8:17 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:«Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.»
8:18 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga.
8:19 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.»
8:20 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
8:21 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»
8:22 Yeesu tontu ko ne: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
8:23 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko.
8:24 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yengal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw.
8:25 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee.»
8:26 Waaye Yeesu tontu leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
8:27 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
8:28 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woon a jaar foofa.
8:29 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgg a mbugal, bala waxtu way jot?»
8:30 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
8:31 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.»
8:32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.
8:33 Ba sàmm ya gisee loolu, ñu daw, dem dëkk ba, nettaliji lépp ak la xewoon ca ña rab jàpp.
8:34 Noonu dëkk ba bépp génn seeti Yeesu. Ba ñu ko gisee nag, ñu ñaan ko, mu génn seen réew.
9:1 Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam.
9:2 Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
9:3 Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
9:4 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol?
9:5 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
9:6 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
9:7 Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi.
9:8 Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi.
9:9 Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
9:10 Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya.
9:11 Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
9:12 Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
9:13 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
9:14 Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?»
9:15 Yeesu tontu leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor.
9:16 Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu.
9:17 Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
9:18 Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.»
9:19 Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem.
9:20 Bi ñuy dem nag, amoon na ca mbooloo ma jigéen juy xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Mu defe ne, su laalee mbubbam rekk, dina wér. Mu jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam.
9:22 Bi mu ko defee Yeesu woññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa.
9:23 Bi Yeesu eggee kër njiit la, mu gis ñiy liit ak toxoro, ak mbooloo may def coow lu bare.
9:24 Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal.
9:25 Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg.
9:26 Noonu xebaaru li mu def daldi siiw ca réew ma.
9:27 Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!»
9:28 Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne, man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu tontu ko: «Waaw Sang bi.»
9:29 Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.»
9:30 Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»
9:31 Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk.
9:32 Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu.
9:33 Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, musuñu koo gis ci Israyil.»
9:34 Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
9:35 Noonu Yeesu wër dëkk yu mag ya yépp ak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, tey yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla, di faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
9:36 Bi Yeesu gisee mbooloo ma, mu yërëm leen, ndaxte dañoo sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm.
9:37 Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu.
9:38 Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
10:1 Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
10:2 Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;l
10:3 Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade;l
10:4 Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nar a wor Yeesu.
10:5 Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari.
10:6 Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar.
10:7 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.”
10:8 Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen.
10:9 Buleen dajale wurus, xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume.
10:10 Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki, ay dàll mbaa aw yet, ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam.
10:11 «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
10:12 Bu ngeen di dugg ci kër nag, nuyooleen.
10:13 Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko, na seen jàmm wàcc ci ñoom, waaye bu ko yeyoowul, na seen yéene dellusi ci yéen.
10:14 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk.
10:15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu.
10:16 «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
10:17 Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu.
10:18 Dees na leen yóbbu ngir man ci kanami boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut.
10:19 Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen war a wax;
10:20 du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen.
10:21 «Mag dina joxe rakkam ci dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
10:22 Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc.
10:23 Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen man a wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
10:24 Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam.
10:25 Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astemaak waa kër gi.
10:26 Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warul a biral, mbaa luy kumpa lu ñu warul a siiwal.
10:27 Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi.
10:28 Te buleen ragal ñu man a rey yaram, te mënuñoo rey ruu, waaye ragal-leen Ki man a sànk yaram ak ruu ci safara.
10:29 Ñaari picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.
10:30 Seen kawari bopp sax, waññees na leen.
10:31 Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.
10:32 «Koo xam ne nangu nga ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
10:33 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
10:34 «Te it buleen defe ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale.
10:35 Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam, doom ju jigéen ak ndeyam, jabar ak goroom;
10:36 te nooni nit ñooy waa këram.
10:37 Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma.
10:38 Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma.
10:39 Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko.
10:40 «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni.
10:41 Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub.
10:42 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gën a ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»
11:1 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngaleji ak a waare ci seeni dëkk.
11:2 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
11:3 ne ko: «Ndax yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»
11:4 Yeesu tontu leen ne: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko.
11:5 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.
11:6 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
11:7 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
11:8 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur.
11:9 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.
11:10 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”
11:11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut.
11:12 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll.
11:13 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ.
11:14 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Iliyas bi waroon a ñëw.
11:15 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.
11:16 «Niti jamono jii nag, lan laa leen man a mengaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit,
11:17 ne leen:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
11:18 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
11:19 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
11:20 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar.
11:21 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
11:22 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
11:23 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey.
11:24 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
11:25 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi.
11:26 Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»
11:27 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it mënul a xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.
11:28 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay.
11:29 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol.
11:30 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
12:1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
12:2 Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi.»
12:3 Noonu Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
12:4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu jébbal Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; saraxalekat rekk a ko sañoon a lekk.
12:5 Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne saraxalekat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésu noflaay bi, te tooñuñu?
12:6 Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga.
12:7 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul.
12:8 Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
12:9 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
12:10 te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésu noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
12:11 Yeesu tontu leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésu noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko?
12:12 Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésu noflaay bi jaadu na.»
12:13 Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des.
12:14 Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu.
12:15 Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp.
12:16 Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
12:17 Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
12:18 «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn,di sama Soppe bi neex sama xol.Dinaa def sama Xel ci moom,muy yégal xeet yi yoonu njub.
12:19 Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw,te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
12:20 Du dammaate barax bu banku,te mees guy saxar, du ko fey,ba kera mu yégal njub, ba daan.
12:21 Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
12:22 Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis.
12:23 Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
12:24 Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
12:25 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du man a yàgg.
12:26 Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di man a yàgge?
12:27 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
12:28 Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
12:29 «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgg a dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp.
12:30 Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
12:31 Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu man a doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal.
12:32 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira.
12:33 Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee.
12:34 Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen man a waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
12:35 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon.
12:36 Maa ngi leen di wax ne, keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu mas a wax.
12:37 Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
12:38 Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
12:39 Yeesu tontu leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg yonent Yàlla Yunus.
12:40 Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf.
12:41 Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
12:42 Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
12:43 «Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis.
12:44 Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
12:45 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
12:46 Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgg a wax ak moom.
12:47 Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg a wax ak yaw.»
12:48 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
12:49 Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk.
12:50 Ndaxte ku def sama coobareg Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»
13:1 Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga.
13:2 Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
13:3 Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
13:4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
13:5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
13:6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
13:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
13:8 Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, li ci des fanweer.
13:9 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
13:10 Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb.
13:11 Noonu mu tontu leen ne: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
13:12 Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu.
13:13 “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb.
13:14 Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan:“Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.
13:15 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”
13:16 «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg!
13:17 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
13:18 «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki.
13:19 Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
13:20 Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw;
13:21 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
13:22 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
13:23 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom-benn-fukk mbaa fanweer.»
13:24 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
13:25 Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem.
13:26 Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom.
13:27 «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
13:28 Mu tontu leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?”
13:29 Waaye mu tontu leen: “Déedéet, ngir bañ a buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi.
13:30 Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: Jëkkleen a dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.”»
13:31 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
13:32 Doomu fuddën moo gën a tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
13:33 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
13:34 Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb.
13:35 Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Dinaa leen wax ciy léeb,di yégle yëf yu nëbbuli dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.»
13:36 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
13:37 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi;
13:38 àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
13:39 Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
13:40 Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee.
13:41 Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
13:42 sànni leen ci safara; foofa dees na fa jooy te yéyu.
13:43 Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
13:44 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
13:45 «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
13:46 Am bés mu gis per buy jar njëg gu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
13:47 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
13:48 Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon.
13:49 Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi,
13:50 sànni leen ci safara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
13:51 Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu tontu ko: «Waaw.»
13:52 Yeesu ne leen: «Kon xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
13:53 Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
13:54 dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële?
13:55 Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
13:56 Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
13:57 Kon ñu daldi koy xeeb.Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.»
13:58 Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.
14:1 Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am.
14:2 Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya, mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
14:3 Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd, jabaru Filib magam,
14:4 te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.»
14:5 Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent.
14:6 Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd,
14:7 ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.»
14:8 Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
14:9 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko.
14:10 Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba.
14:11 Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam.
14:12 Noonu taalibey Yaxya ñëw, fab néew wa, suul ko; ba noppi dem, wax ko Yeesu.
14:13 Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk.
14:14 Yeesu génn ci gaal gi nag, gis mbooloo mu réy, mu yërëm leen, ba faj ñi ci wopp.
14:15 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu man a lekk?»
14:16 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.»
14:17 Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
14:18 Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.»
14:19 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña.
14:20 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
14:21 Gannaaw jigéen ña ak gune ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni.
14:22 Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya, ñu dugg gaal ga te jàll dex ga, jiituji ko, muy yiwi mbooloo ma.
14:23 Bi mu ko yiwee nag, mu yéeg ca tund wa, ngir wéet ak Yàlla. Noonu guddi jot, fekk mu nekk fa moom rekk.
14:24 Bi mu fa nekkee nag, gaal ga sore na tefes ga, te duus ya di ko yengal bu metti, ndax ngelaw la leen soflu.
14:25 Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi.
14:26 Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu.
14:27 Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
14:28 Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.»
14:29 Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu.
14:30 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!»
14:31 Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?»
14:32 Noonu ñu dugg ca gaal ga, te ngelaw li ne tekk.
14:33 Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.»
14:34 Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret.
14:35 Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp.
14:36 Noonu ñu ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk, te ku ko laal daldi wér.
15:1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko:
15:2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
15:3 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada?
15:4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.”
15:5 Waaye yéen dangeen ne, ku wax sa ndey walla sa baay: “Li ngeen war a jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,”
15:6 kooku amatul warugaru teral baayam. Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada.
15:7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
15:8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma.
15:9 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”»
15:10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam:
15:11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
15:12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
15:13 Yeesu tontu leen ne: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi.
15:14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
15:15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
15:16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam?
15:17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu?
15:18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe.
15:19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
15:20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
15:21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon.
15:22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
15:23 Waaye Yeesu tontuwu ko genn kàddu. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
15:24 Yeesu tontu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xar yu réeri bànni Israyil.»
15:25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!»
15:26 Yeesu tontu ko: «Jël ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
15:27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
15:28 Ci kaw loolu Yeesu tontu ko ne: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
15:29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa.
15:30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen.
15:31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
15:32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leen a yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
15:33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
15:34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu tontu ko: «Juróom-ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
15:35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf.
15:36 Mu fab juróom-ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi.
15:37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
15:38 Gannaaw jigéen ñi ak gune yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
15:39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.
16:1 Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.»
16:2 Noonu Yeesu tontu leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.”
16:3 Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeen a ràññee melow asamaan, waaye mënuleen a ràññee firndey jamono ji nu tollu.
16:4 Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla. Waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.» Bi Yeesu waxee loolu, mu jóge ci ñoom, dem.
16:5 Gannaaw loolu taalibe yi jàllaat dex gi, fekk fàtte nañoo yóbbaale mburu.
16:6 Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
16:7 Bi ko taalibe yi déggee, ñu daldi werante ci seen biir naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
16:8 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen di werante ci seen biir, ndaxte indaalewuleen mburu?
16:9 Ndax xamaguleen ba tey? Xanaa fàttalikuwuleen juróomi mburu ya ngir juróomi junniy góor ña, ak ñaata pañe ngeen dajale woon ciy dammit?
16:10 Te ndax fàttalikuwuleen itam juróom-ñaari mburu ya ngir ñeenti junniy góor ña, ak ñaata dàmba ngeen dajale woon ciy dammit?
16:11 Kon nag lu tax xamuleen ne, waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
16:12 Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njàngalem Farisen ya ak Sadusen ya.
16:13 Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?»
16:14 Taalibe yi tontu ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Iliyas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.»
16:15 Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?»
16:16 Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer tontu ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
16:17 Yeesu tontu ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw.
16:18 Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara.
16:19 Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.»
16:20 Noonu Yeesu dénk taalibe yi bu wóor ne leen: «Buleen wax kenn ne, maay Almasi bi.»
16:21 Li dale ci jamono jooja, Yeesu tàmbali na xamal taalibeem yi ne, war na dem Yerusalem, daj fa coono yu bare, jóge ca njiit ya, ca saraxalekat yu mag ya ak ca xutbakat ya; ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.
16:22 Bi mu waxee ba noppi, Piyeer woo ko ci pegg, bëgg koo yedd ne ko: «Yàlla tere, Boroom bi, loolu du la dal.»
16:23 Waaye Yeesu woññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
16:24 Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
16:25 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko.
16:26 Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu war a weccee bakkanam?
16:27 Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci ndamul Baayam, ànd ak ay malaakam; bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
16:28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.»
17:1 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool.
17:2 Mu soppiku fa seen kanam, xar-kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer.
17:3 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas, di waxtaan ak Yeesu.
17:4 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»
17:5 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
17:6 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool.
17:7 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.»
17:8 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
17:9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.»
17:10 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Iliyas mooy jëkk a ñëw?»
17:11 Yeesu tontu leen ne: «Waaw dëgg la, Iliyas war na ñëw, jubbanti lépp.
17:12 Teewul maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nar a sonal léegi Doomu nit ki.»
17:13 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne, ci mbirum Yaxya la leen doon wax.
17:14 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk
17:15 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci safara, léeg-léeg mu daanu ci ndox.
17:16 Indi naa ko ci say taalibe, waaye mënuñu koo faj.»
17:17 Noonu Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen di war a muñal?» Mu ne leen, «Indil-leen ma xale bi fii.»
17:18 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa.
17:19 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun mënunu woon a dàq rab wi?»
17:20 Yeesu tontu leen ne: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.»
17:22 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi;
17:23 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool.
17:24 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?»
17:25 Piyeer ne leen: «Aaŋkay!»Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkk a wax ne Piyeer: «Waaw lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
17:26 Piyeer tontu ko ne: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci.
17:27 Waaye bëgguma nu naqaral leen; kon demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkk a xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»
18:1 Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gën a màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
18:2 Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir,
18:3 ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
18:4 Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gën a màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
18:5 Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu.
18:6 Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga.
18:7 «Yaw àddina dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir mënta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal.
18:8 Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci safara su dul fey mukk.
18:9 Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci safara.
18:10 «Te it wottuleen a xeeb kenn ci ñi gën a tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu.
18:12 «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, te dem wuti ma réer?
18:13 Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent ya réerul.
18:14 «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gën a tuuti sànku.
18:15 «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk.
18:16 Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede.
18:17 Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat.
18:18 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan.
18:19 «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu man a doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may.
18:20 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
18:21 Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko war a baal? Xanaa ba ci juróom-ñaari yoon?»
18:22 Yeesu tontu ko ne: «Waxuma la ba ci juróom-ñaari yoon, waaye ba ci juróom-ñaar-fukki juróom-ñaari yoon.
18:23 «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgg a waññ alalam ak ay jaraafam.
18:24 Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree-bare,
18:25 waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak jabaram ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba.
18:26 Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.”
18:27 Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba.
18:28 «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.”
18:29 Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.”
18:30 Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel.
18:31 «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp.
18:32 Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma.
18:33 Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?”
18:34 Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp.
18:35 «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»
19:1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan.
19:2 Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa.
19:3 Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase jabaram, saa su ko neexee?»
19:4 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
19:5 te mu ne: “Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.”
19:6 Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
19:7 Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox jabaram kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
19:8 Yeesu tontu leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen jabar, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu.
19:9 Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa jabar te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
19:10 Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, bañ a séy moo gën.»
19:11 Yeesu tontu leen: «Du ñépp ñoo man a nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk.
19:12 Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu bañ a séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko man a nangu, nangu ko.»
19:13 Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen.
19:14 Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
19:15 Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa.
19:16 Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def ci lu baax, ngir man a am dund gu dul jeex?»
19:17 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
19:18 Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
19:19 teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
19:20 Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
19:21 Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
19:22 Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
19:23 Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
19:24 Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
19:25 Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo man a mucc nag?»
19:26 Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
19:27 Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
19:28 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
19:29 Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
19:30 Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
20:1 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu réseñam.
20:2 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leen a yebal ca toolam.
20:3 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu.
20:4 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”
20:5 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg-bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu.
20:6 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”
20:7 Ñu tontu ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
20:8 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujj a ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”
20:9 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon.
20:10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkk a jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon.
20:11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga,
20:12 naan: “Ñi mujj a ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.”
20:13 Waaye boroom kër ga tontu kenn ci ñoom ne ko: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon?
20:14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujj a ñëw, li ma la fey yaw,
20:15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?”
20:16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
20:17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii:
20:18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee,
20:19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
20:20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn.
20:21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu tontu ko ne: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndeyjoor, ki ci des ci sa càmmooñ.»
20:22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu tontu ko: «Man nañu ko.»
20:23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
20:24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya.
20:25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di noot.
20:26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
20:27 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam.
20:28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
20:29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko.
20:30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne, Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
20:31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gën a yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
20:32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
20:33 Ñu tontu ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.»
20:34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.
21:1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe,
21:2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen.
21:3 Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leen a soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.»
21:4 Yeesu def na noonu, ngir la ñu waxoon jaarale ko cib yonent am, bi mu naan:
21:5 «Waxal waa Siyon:“Seen buur a ngi ñëw ci yéen;ku lewet la, te war mbaam-sëf,dig cumbur, doomu mbaam.”»
21:6 Noonu taalibe ya dem, def loolu leen Yeesu sant.
21:7 Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca.
21:8 Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa.
21:9 Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Ca bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
21:10 Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yengatu ne: «Kii moo di kan?»
21:11 Mbooloo ma tontu leen ne: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.»
21:12 Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya,
21:13 naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
21:14 Noonu ay gumba ak ay lafañ ñëw ci moom ca kër Yàlla ga, mu faj leen.
21:15 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer.
21:16 Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw dégg naa ko. Ndax musuleen a jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
21:17 Bi Yeesu waxee loolu, mu bàyyi leen, génn dëkk ba, jëm Betani, fanaan fa.
21:18 Ci suba teel Yeesu dellusi ca dëkk ba, mu xiif.
21:19 Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk.» Ca saa sa figg ga daldi wow.
21:20 Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?»
21:21 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te bañ a werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
21:22 Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.»
21:23 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngale. Bi muy jàngale nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?»
21:24 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
21:25 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
21:26 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.»
21:27 Ñu tontu Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
21:28 «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu réseñ.”
21:29 Taaw ba tontu ko ne: “Maa ngi dem baay,” waaye demu ca.
21:30 Gannaaw gi, baay ba ñëw ca ñaareel ba, wax ko noonu. Mu tontu ko ne: “Bëgguma caa dem,” waaye gannaaw loolu xelam soppiku, mu dem ca.»
21:31 Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobareg baayam?» Ñu ne: «Ñaareel bi.» Kon Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkk a dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
21:32 Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.»
21:33 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
21:34 «Bi nga xamee ne bëgg nañoo witt réseñ yi, mu yónni ay surgaam ci beykat yi, ngir jot wàllam ci meññeef mi.
21:35 Waaye beykat yi jàpp surga yi, kenn ki ñu dóor ko ay yar, keneen ki ñu rey ko, ki ci des ñu sànni ko ay doj.
21:36 Boroom kër gi nag yónniwaat yeneen surga yu ëpp yu jëkk ya, beykat yi def leen noonu ñoom itam.
21:37 Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.”
21:38 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.”
21:39 Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.»
21:40 Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?»
21:41 Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.»
21:42 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa musuleen a jàng lii ci Mbind yi?“Doj wi tabaxkat yi sànni;mujj na di doju koñ;ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”
21:43 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam.
21:44 Ku dal ci doj wii, dammtoo; ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
21:45 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax.
21:46 Noonu ñu di ko fexee jàpp, waaye ragal nañu nit ña, ndaxte ñépp teg nañu ko ab yonent.
22:1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
22:2 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
22:3 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
22:4 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
22:5 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
22:6 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
22:7 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
22:8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
22:9 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
22:10 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
22:11 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu war a sol ca céet ga.
22:12 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
22:13 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
22:14 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
22:15 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu war a def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
22:16 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
22:17 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
22:18 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
22:19 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
22:20 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
22:21 Ñu tontu ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
22:22 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
22:23 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
22:24 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
22:25 Amoon na ci nun nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba séyoon na, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
22:26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom-ñaareel ba.
22:27 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
22:28 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom-ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
22:29 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
22:30 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
22:31 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa musuleen a jàng la leen Yàlla waxoon ne:
22:32 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
22:33 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngale.
22:34 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne, yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
22:35 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
22:36 «Kilifa gi, ban ndigal moo gën a màgg ci yoonu Musaa?»
22:37 Yeesu tontu ko ne: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
22:38 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
22:39 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
22:40 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
22:41 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
22:42 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu tontu ko: «Daawuda.»
22:43 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
22:44 “Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam’ ”
22:45 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
22:46 Ci kaw loolu kenn mënu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.
23:1 Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
23:2 «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
23:3 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
23:4 Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
23:5 Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
23:6 Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
23:7 Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “Kilifa gi.”
23:8 Waaye yéen buñu leen wooye “Kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
23:9 Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
23:10 Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
23:11 Ki gën a mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
23:12 Kuy yékkatiku, dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
23:13 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgg a dugg, mu dugg ci.
23:15 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu safara, ku leen yées ñaari yoon.
23:16 «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
23:17 Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gën a màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
23:18 Dangeen ne it: “Ku giñe saraxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
23:19 Gumba yi! Lan moo gën a màgg, sarax si walla saraxalukaay bi tax sarax si sell?
23:20 Ku giñe saraxalukaay bi, giñ nga ci saraxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
23:21 Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak Ki ci dëkk.
23:22 Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak Ki ci toog.
23:23 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gën a màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
23:24 Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
23:25 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
23:26 Farisen yu gumba yi! Jëkkleen a setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
23:27 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
23:28 Yéen itam, ci ngistal dangeen a mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
23:29 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
23:30 Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
23:31 Seede ngeen nii ne, yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
23:32 di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
23:33 Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu safara?
23:34 Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo-dëkk.
23:35 Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakariya doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak saraxalukaay bi.
23:36 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
23:37 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
23:38 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
23:39 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
24:1 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko tabaxi kër Yàlla ga.
24:2 Waaye mu tontu leen ne: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
24:3 Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne, yaa ngi ñëw te àddina di tukki?»
24:4 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
24:5 Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare.
24:6 Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; wottuleen, buleen ci tiit, ndaxte loolu war na am, waaye booba muju jamono ji jotagul.
24:7 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yengu-yenguy suuf ci bérab yu bare.
24:8 Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
24:9 Bu boobaa dees na leen jébbale, metital leen, rey leen; te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
24:10 Bu loolu amee ñu bare dinañu dàggeeku, di booleente tey bañante.
24:11 Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare.
24:12 Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku.
24:13 Waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
24:14 Noonu xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee muju jamono ji jot.
24:15 «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam.
24:16 Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya;
24:17 ku nekk ci kaw taax ma, bul wàcc ngir fab say yëf, ya nekk ci biir kër ga;
24:18 ku nekk ca tool ba, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
24:19 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal!
24:20 Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésu noflaay bi.
24:21 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
24:22 Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn.
24:23 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm.
24:24 Ndaxte ñi mbubboo turu Kirist ak ñi mbubboo turu yonent dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am.
24:25 Wax naa leen ko lu jiitu.
24:26 «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm.
24:27 Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwu Doomu nit ki di mel.
24:28 Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee.
24:29 «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yengu.
24:30 Booba firnde ji taxaw, Doomu nit ki feeñ ci asamaan, te xeeti àddina sépp dinañu jooy. Dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci niiri asamaan si, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
24:31 Dina yónni ay malaakaam ak baatu liit bu dégtu, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa asamaan dale ba fu mu yem.»
24:32 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, ay xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
24:33 Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, xamleen ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax.
24:34 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul.
24:35 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
24:36 «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
24:37 Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw.
24:38 Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor yaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga;
24:39 xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwu Doomu nit ki.
24:40 «Bu boobaa ci ñaar ñu nekk cib tool, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
24:41 Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
24:42 Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés bu seen Boroom di ñëw.
24:43 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yeewu te du ko bàyyi, mu toj këram.
24:44 Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
24:45 Yeesu teg ca ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ca jamono ja?
24:46 Bu njaatigeem ñëwee te gis muy def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
24:47 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
24:48 Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,”
24:49 mu tàmbalee dóor ay bokki surgaam, di lekk te naan ak naankat ya,
24:50 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul.
24:51 Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.
25:1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
25:2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel.
25:3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diwlin;
25:4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diwlin ciy njaq.
25:5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmmeentu bay nelaw.
25:6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.”
25:7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp.
25:8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diwlin, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgg a fey.”
25:9 Waaye ñi am xel tontu leen ne: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen; tee ngeen a dem ca jaaykat ya, jënd.”
25:10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diwlin ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
25:11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu.”
25:12 Waaye mu tontu leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
25:13 «Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
25:14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi mu laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan.
25:15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
25:16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
25:17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar.
25:18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
25:19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya dellusi, daldi leen laaj alalam.
25:20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
25:21 Njaatigeem tontu ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
25:22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
25:23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
25:24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
25:25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.”
25:26 Waaye njaatigeem tontu ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne, damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul,
25:27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot li ma moom ak la mu jur.”
25:28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
25:29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
25:30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
25:31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam.
25:32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi,
25:33 mu teg xar yi ci ndeyjooram, bëy yi ci càmmooñam.
25:34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndeyjoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
25:35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma;
25:36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.”
25:37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan?
25:38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
25:39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?”
25:40 Noonu Buur bi dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gën a ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
25:41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmooñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci safara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam.
25:42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan.
25:43 nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.”
25:44 Ci kaw loolu dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?”
25:45 Kon dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gën a ndaw, man ngeen ko defalul.”
25:46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»
26:1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu lépp ba noppi, mu ne taalibeem ya:
26:2 «Xam ngeen ne, ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.»
26:3 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu saraxalekat bu mag ba, tudd Kayif.
26:4 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu man a fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko.
26:5 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.»
26:6 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon,
26:7 jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ bu jar lu baree-bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu.
26:8 Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii lu muy jariñ?
26:9 Maneesoon na koo jaay ci lu bare, jox xaalis bi miskin yi.»
26:10 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?
26:11 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.
26:12 Kii, ci li mu tuur latkoloñ bii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob.
26:13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
26:14 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya,
26:15 ne leen: «Lan ngeen ma man a jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu saraxalekat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer.
26:16 Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu.
26:17 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru màggalu Jéggi ba?»
26:18 Yeesu tontu leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi xewu Jéggi ba, man ak samay taalibe.”»
26:19 Noonu taalibe yi defar reeru Jéggi ba, na leen Yeesu waxe woon.
26:20 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar.
26:21 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
26:22 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?»
26:23 Yeesu tontu leen ne: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor.
26:24 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoon a juddu moo gënoon ci moom.»
26:25 Yudaa, mi ko nar a wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
26:26 Noonu bu ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.»
26:27 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci,
26:28 ndaxte lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi.
26:29 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaawsi tey ndoxum réseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum réseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
26:30 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
26:31 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.”
26:32 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
26:33 Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.»
26:34 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.»
26:35 Piyeer tontu ko: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
26:36 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.»
26:37 Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonett.
26:38 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgg a dee; toogleen fi, xool ak man.»
26:39 Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.»
26:40 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
26:41 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir; seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
26:42 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii mënu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.»
26:43 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis.
26:44 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon.
26:45 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma war a jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na.
26:46 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
26:47 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca saraxalekat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
26:48 Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.»
26:49 Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaamu àleykum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng.
26:50 Yeesu tontu ko: «Sama xarit, xam naa lu tax nga ñëw.» Noonu ñu daldi jegesi, song ko, jàpp ko.
26:51 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag ba, nopp ba dagg.
26:52 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey.
26:53 Xanaa xamuloo ne, man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul?
26:54 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi man a ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la war a ame.»
26:55 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma.
26:56 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw.
26:57 Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, saraxalekat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje.
26:58 Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje.
26:59 Noonu saraxalekat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu man a seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey,
26:60 waaye mënuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan:
26:61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”»
26:62 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo tontu dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?»
26:63 Waaye Yeesu ne cell. Saraxalekat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.»
26:64 Yeesu tontu ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan si.»
26:65 Bi mu déggee loolu, saraxalekat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee.
26:66 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu tontu ko: «Yoon teg na ko dee.»
26:67 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar-kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko,
26:68 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?»
26:69 Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.»
26:70 Waaye Piyeer weddi ko ci kanamu ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.»
26:71 Bi mu ko waxee, mu jëm ca bunt ba, te beneen mbindaan gis ko, mu wax ña fa nekkoon: «Kii àndoon na ak Yeesum Nasaret.»
26:72 Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.»
26:73 Nes tuuti ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.»
26:74 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab.
26:75 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
27:1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu.
27:2 Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma.
27:3 Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne, daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis,
27:4 ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu tontu ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.»
27:5 Noonu Yudaa sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, takk buum ci baatam, xaru.
27:6 Saraxalekat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njëgu deret la.»
27:7 Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya.
27:8 Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret.
27:9 Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njëg gi bànni Israyil xayma woon ci nit ki;
27:10 ñu joxe ko ngir toolu defarkatu ndaa ya, ni ma ko Boroom bi sante.»
27:11 Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanamu boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko; «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
27:12 Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko,» waaye tontuwul dara ca la ko saraxalekat yu mag ya ak njiit ya jiiñ.
27:13 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo lépp li ñu la jiiñ?»
27:14 Waaye Yeesu tontuwu ko ci dara, ba tax boroom réew ma waaru lool.
27:15 Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil.
27:16 Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas.
27:17 Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?»
27:18 Ndaxte xamoon na ne, kiñaan rekk a taxoon, ñu jébbal ko ko.
27:19 Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, jabaram yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.»
27:20 Waaye saraxalekat yu mag ya ak njiit ya xiir mbooloo ma, ñu laaj Barabas te reylu Yeesu.
27:21 Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu tontu ko: «Barabas.»
27:22 Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp tontu ko ne: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
27:23 Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gën a kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
27:24 Naka Pilaat xam ne, du ci man dara, fekk na sax yengu-yengu bi gën a am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanamu mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.»
27:25 Ñépp tontu ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.»
27:26 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
27:27 Bi ñu ko defee xarekati boroom réew ma fab Yeesu, yóbbu ko ci biir kër ga, ñu daldi woo mbooloom xarekat ya yépp ci moom.
27:28 Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
27:29 Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndeyjooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
27:30 Ba noppi ñu daldi tifli ci kawam, fab bantu xat ba, dóor ko ci boppam.
27:31 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu summi mbubbum xarekat ma, solalaat ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
27:32 Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu war a daaj Yeesu.
27:33 Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.»
27:34 Bi ñu fa eggee, ñu jox ko biiñ, ñu def ci lu wex. Waaye bi mu ko mosee, nanguwu koo naan.
27:35 Noonu ñu daaj ko ca bant ba, ñu daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant,
27:36 ba noppi toog fa, di ko wottu.
27:37 Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.»
27:38 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew ma, kenn ci ndeyjooram, ka ca des ci càmmooñam.
27:39 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko,
27:40 naan: «Yaw mi man a toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi.»
27:41 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya it di ko ñaawal naan:
27:42 «Waa jii musal na ñeneen te mënul a musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko.
27:43 Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”»
27:44 Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule.
27:45 La tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
27:46 Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
27:47 Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.»
27:48 Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu.
27:49 Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Iliyas dina ñëw, musal ko.»
27:50 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
27:51 Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yengu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku,
27:52 te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki.
27:53 Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare.
27:54 Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yengu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.»
27:55 Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dand, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo.
27:56 Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya.
27:57 Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon.
27:58 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko.
27:59 Noonu Yuusufa fab jëmm ja, laxas ko ci càngaay lu set,
27:60 dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem.
27:61 Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba.
27:62 Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat.
27:63 Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.”
27:64 Danoo bëggoon nag, nga santaane, ñu wottu bàmmeel ba, ba am ñetti fan, ngir bañ taalibeem ya ñëw, sàcc néew ba, tey yégle ne dekki na. Bu ko defee nax bu mujj boobu dina yées bu jëkk ba.»
27:65 Pilaat tontu leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.»
27:66 Noonu ñu dem, tëj bàmmeel ba bu wóor, ñu tay ca doj wa màndarga, teg fa wottukat ya.
28:1 Gannaaw bésu noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
28:2 Fekk suuf yengu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
28:3 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
28:4 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
28:5 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne, yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
28:6 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
28:7 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne, dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
28:8 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
28:9 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
28:10 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
28:11 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal saraxalekat yu mag ya lépp lu xew.
28:12 Noonu saraxalekat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
28:13 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
28:14 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
28:15 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
28:16 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
28:17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
28:18 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
28:19 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
28:20 te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Te maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»